Yaa ilaahi fa sallim
Bismi Laahi Rahmaani Rahiimi
Bismi Laahi ma door woy wu jëm ci Seydi Limaamu
Tek ca ngirta lawoy Abdulaay « Jawaadu » Yonnent ba
Al hamdu li Laahi
Maam Libaas da ne Yallaa ma yonni , maa jara andal
« Insu wal jinnu » ñëw leen nu jaamu, naani ca Tuubee
Al hamdu li Laahi
Am na waa ju ko wax, Makka seet ko, Mbay jëkk wooli
Xañtu woote ba, jëf ay sunnam ba fekk Yonnent ba
Al hamdu li Laahi
Rabbi nee sama ndaw am na muhjisaat yu ma kiy jox
Nit ña yéému ci moom xam ne maa ko yonni ci dun ba
Al hamdu li Laahi
Njiin randal na fi geej , ak di rey mbindééf di dekkal
Wax xibaar yu di ñëw, lépp am na ba nuy sànta Buur ba
Al hamdu li Laahi
Njiin du tawte ci waame , da koy gëwéélu mu jalla
Duusi gééj du ko laal , moo di « santaral » ba ca Buur ba
Al hamdu li Laahi
« Santaral » bi ci biir rééw mi lampa yepp la leeral
Sap « kurang » ku ci taalul du leer le, yaa di yonnen ba
Al hamdu li Laahi
Xabru yaa nga fa Baay laay, fuaar ba munga ca Limaamu
Ruu yi jof si na , Baay Laay waxoon na loolu ca demba
Al hamdu li Laahi
Aeropora nga Yoof , kuy “voyaase” taggu Limaamu
Ab ujjaaj du fi jok taggutil Limaamu ca been ba
Al hamdu li Laahi
Almadee nga fa Njiin , Mahdiyoo di tur wa ci baatin
Moom la tiim di “siñaale” , te naan yonnen ba ca beeñ ba
Al hamdu li Laahi
« Kapitaal » ba la Buur Yalla far « palaase » fa Baay Laay
Luy jaraafa ki buur, Yalla déj na leen fa yonnen ba
Al hamdu li Laahi
Waa léboo di xureysin ba doomi Ngor ya di ay gor
Ñoo di askanu Njiin, tektalam ba leer na fa Buur ba
Al hamdu li Laahi
Waalo yaa nga fa Baay Laay, Ajoor ya ñung fa Limaamu
Njamburaak, Bawalak Pël ya , ñepp seet si yonnen ba
Al hamdu li Laahi
Seyxu Ahmadu bambaa waxoon ne luy mbiri xééwël
Yalla déj na ka fil Mustafaa, du jok fa yonnen ba
Al hamdu li Laahi
Lan la wax, da ne « raamal waraa fi kullil ufuuxi
Nay la fadli » , Yallaa ko dèj du jok fa yonnen ba
Al hamdu li Laahi
Soo yaboo na nga gëm, soo yaboo nga weddi Limaamu
Rabbi nee ku fi kontar ndawam du naani ca Tuubee
Al hamdu li Laahi
Maam Libaas da ne woon Abdulaay samap siiwël la
Mooy layook ñi ma kontar te mooy « jawaadu » yonnen ba
Al hamdu li Laahi
Moo taxit mu taxaw naan Limaamu Laay sama maam la
Yàlla moo ko yabal, moo di mursalun ba ca sowu ba
Al hamdu li Laahi
Abdulaay ku la gis miin la , xam ni yaadi « jawaadu »
Rabbi mooy ki la fal « xawsu diiné » fii ba ca Pééy ba
Al hamdu li Laahi
Janqi Aljana, Firdawsi, yow sëriif la nu andal
Ngay badar ne ci seen biir , ma woy la ngir namma peey ba
Al hamdu li Laahi
Am nga ndam di sëriif yaa di waada yaa jara andal
Woolu ñay wu di sëf , yemtil ak « himaaru » ca ngaax ba
Al hamdu li Laahi
Yalla rus na la sakkaatu maa jinéé ki malaaka
Buuri adina , tampeel na koy garaad ca dënnëm ba
Al hamdu li Laahi
Xawsu diine ba, Baay Maamuray Ngalam gi ma yonnee
May idaaya ci Baay Laay ba woy sëtëm ya ca sowu ba
Al hamdu li Laahi
Melni Seydi Isaa doomi Baay Manjoon ja di “fardu”
Donna nab lewetaayam di “kansu nihma” ca sowu ba
Al hamdu li Laahi
Ak ku mel nikki Raan , doomi Baay Manjoon ja di “fardu”
Donna nab lewetaayam di “kansu nihma” ca sowu ba
Al hamdu li Laahi
Yaa Ilaahii fasallim , a la Nabiyi Limaamu
Gaaya sax di ko woy, am salamatan ba ca Tube
Al hamdu li Laahi