Waajal Wooté Bi
"" Waajal Wooté Bi ""
1- Awaay jaam yi, nan waac looti, yeeslu ci taalubee
Raxas xol yi, tey footloo ti, ngir wuy ji woote bee
2 ) xanaa bëgg noo laabal, lu jiit wuy ji sanga bee
La Buur namma, faf gaaral "Rajab" doyna saabu bee
3) Barip saabu ak ndox, coonawoo ngir utëm ngërëm
Taxul am ndam ndamal Buur YALLA , ndeem moy nga Baabu bee
4) nde chartak nangul jaamaam, mooy toppa ak Ndawam
Té Moo delsi, Mooy Baye LAYE mi feeñ fii ci sawwu bee
5) Ki ñëw yeesalaat seen diine, tëc lamfi ubbiwoon
Boroom tumbi Mooy Samman bi, Mooy jalla jallu bee
6) Ki ñëw fekkaleen ñuy sampa, tey ray ca xaamba yaa
Mu defleen ñu Baax tey gindé, raw, ñep dileen dabee
7 ) Laboon nan ci bokkaalee ki, taarloo luñaaw te yëës
Mu far loolu joxleen ndioup, ba sikkar lanuy sabee
Niiruuk reer guileen tiimoon, sak feeña tax, mu tass
Nga jiw seeni xol, xam YALLA, yiw rek laniy tibbee
9 ) Danoo regga ngir dunyaa, mi wor kel, ku ngoy ci moom
Nga teeyalnu Maam xeettal nu, ñuy waac ci attebee
10) Ci yaw lan xamee jaamuk jigeen fii ci sawwu bii
Ñu teel tabbi, cik bum ngir, nga fek niaaw ci xarnu bee
11) Ndigeul waa keureum sikkar gudeek naac té aartuleen
Lu juuyook lu baax nan took, té daw lepp luy sobee
12) Zakaat Yaako gaaawloo, Yaako yoonal ci leppi xeet
té naaleen buleen saggan, nawnan sa wooté bee
13) Sa feeñ geefi far luy jaam, kufiy ñuul jëlaat cërëm
Billaay reeratax kon tay , ñu fëx goor sa xabru bee
14 )Luraw ndambi xeewël, Yaa ngi nii Maam di seddëlee
ku ñëw duy ba fees, wëlbët, teenaa doo Imaamu bee
15) awaay Maam, da ngaa Yaa rek, té rus foñ ku rot ci yaw
ku woomlé ba taxkoo weddi Yaa tax, da ngaa Tabee
16) kuniy yeem, ba taxleen jomlu, jawriñ la rek ci yaw
ndé Yaa Moom gojap Leer yep, Yaa raw kufiy Nabee
17) Lu ap jaam taxoo muy tiis Bu jaarul ci Yaw du deñ
Ku sakkul sa mbek coonaam, na nul ,bees banuy ñibee
18) Sa njeuf xél du koy lim, rawna luy duus sa té not Bideew
xanaa ñaan nga nangulnu, waac taayu woote bee
19) Ubbee nu té lep luy koom ,lufiy may nga seddënu
Sagal nu, farook nun, falnu , ñuy gën ji taalibee
20) Té ñaan Buur mu dolliw fan , sa sët bii di Abdulaay
Mu aarko, té maykok wër, mooy rawukaayu bee
21) Na Buur dolli say xeeweul , té ful say teraanga ya
Jotalla Wasiila baak Maxaamba chafaa'à bee
22) Awaay YALLA dëkkeel julli sëlmël ci Sanga bee
Mu jot saabayaak ngertëlma nangul nu Yaa Rabbii