google.com, pub-1214054292722785, DIRECT, f08c47fec0942fa0 Njool Makka | almahdiyou
top of page

Njool Makka

Njool Makka - Saliou HANE
00:00 / 00:00

" Njool Makka "
1) Awadda'at Khoudia kane ' annii, maman anama
Xouxxal Firaaqu, wa baanat innahaa banama


2) maa degg ag taggatoom njaal beenu njël gala jök
Tuhamhimus sawta ngir yaakaar niman yëguma


3) Saxaar gi Laa degg muy, yëklee ka yuuxu ma fëx
Muharwilan ngir balaa moodem ma wax munima


4) Mu xëy ni mes ni wërëñ, saa xolbi defni wëyëng
Iz annahaa demna 'annil yawla tagguwuma


5) Reelaa naroon, mani naa jooy ngir yaram mana daw
Wadda'tuhaa diko ree, mu mel ni moom gisuma


6) Tasuuxu naxwa kajoor, xasul juduudu samad
Yobbaale Collé madaan, yer ndoo ko seet anama


7) Waa Khoudia Yaw da nga miis, am kunti qaati'atan
Hablal wisaali di dem , te Yaw meroo meruma


8) Diirup nga wëy talumaa mus, ñam musak di nelaw
Ludul xalaat ci sa mbir, waatnaani tay weruma


9) Bul deklu rambaac bilay rabbal fenam bamu jak
Man joombanaa dila xas, ay khoudia kaay jigema


10) Saa xolbi tammul di yëk as ndaw su jak sula moy
Laa tatrukiinii di dem am rumti doggalima


11) Wa xabla dhal bayni, kaanal xubbu marta'anaa
Daan wax yuneex diko def muuñam dong, léma


12) Qaaluu 'azalta 'anil AsHaabi qultu lahum
Bouleenma yokku tawat , mböörënte yëngëluma


13) 'Ayantumuu saqamii jeextakk ngir xale bi
Kon Ndax dinaa mana xumbël ap jotaay, Manuma


14) Bul yedda, Bul laayebiir Xasbiid Danaa- faxad
Ilayka 'annii bu dee deggoo Araab Sorima


15) Walastu Arjuu ci saa feebar bi waa juko Fac
Ndax Ndour ci ak xarañam sax, neena Kii tënëma


16) Man Lii bi Tabbin yudaawii jaangoroy kunu wor ?
Am 'azza wujdaanuhu aahin turaa wuyuma


17) Saa xolbi daa tëlbateem , am kuntu dhaa walahin
Am ngañju soppa ma ñaas saa xolbi lakkanama


18) Ndeem rëccënaa duma soppat kenna baa diko nop
Yaa layta Khoudia ñëwaat daa xamni man kafuma


19) illal Lazii Hubbuhu baynal waraa charafun
Yawlaa ni kepp ku sopp, waaji soppanama


20) Yaa nafsu dëppël nu seet, waajay safoo ñamu am
Ndax soppa waa jamono Ndeem yagganaat doyuma


21) Miisnaa ku mas dima gaaral soppa ak diko nass
Walaytu chawqii kudul Njool Makka soppatuma


22) Huwal lazii amruhu lottalna keppa ku xam
Wa a'jazal bulahaa ak ñamu ndamoo xalima


23) Soppam ci jullit bu xam mooy koom, batax mani man
Maya kan ci soppa Nogaye Ak fatou An Alima


24) qaalat liyannafsu, laa tahjur ku mél ni Nogaye
Fiimat tabaayunu 'an Khoudiak ñoñam, wa Lima


25) Fa qultu ndax dinawar, may bëgg bay bëggë dof
'An Seyydil khalqi, lii Ndeem jaadunaat weruma


26) Mooy balluwaayu lu jak, Aslul usuuli ma'an
Ndax looy ndamoo diko naw ciy jikko rek yëfëma


27) Naatango ñeeluko min khaysul asaalati ndax
Jikkoom ya taaruna, gaaral waa ëlëm Umamah


28) Soo nanguwoon sama feeteek yaw madoon kifi raw
Idhaa taxallaba 'anniin Naasu sax safuma


29) Te sax sa mbaax, aantanul xañ soppe ay mbebetëm
Yaw miy dëfël kula naw , tey aar kanaan tinuma


30) Maa Khaaba man kaana yarjuu raxca nak dila roy
Laa faaza man xad tawallaa doonte sax ñoñama


31) YALLA la def sak li islaaHil waraa banu jak
Ngay Nuur ci kepp ku jakk, tay xupp man DHalama


32) Atayta waddahru fiddayjuuji DHulmatihi
Wa Nuuru hadyika jahran xad nafaa DHulamah


33) Sa RuuHa tax kufi mus ak nekka Yaako sabab
Sa tab ci rusloo geej xaddaj daraa dinama


34) Keefër gu sax nga fi randal , Ceddo daaldi nasax
Mustabshiral qawmi bil islaami ton Sanama


35) Ku jappandoowul Rasuulal LAHI Ciy jëfinam
Wujuuduhu Xad yusaawii sooy melal 'anama


36) Yaa Khayra Hibbin Wa yaa Khayral Khaliili Bu wer
Ngoor naa ci yaw dila ñaan ak feetewoo tafuma


37) Buur YALLA dolliKo xeewël ak salaamu muccëk
ñooñ Waaki Saabaam ña gööp seen Njiw ya toftalema


Le 27 rajab 1437

​

bottom of page