google.com, pub-1214054292722785, DIRECT, f08c47fec0942fa0 Ndawal Yalla | almahdiyou
top of page

Ndawal YALLA

Ndawal YALLA - Ablaye FALL
00:00 / 00:00

Ce poème est adressé à l'humanité qui en quête de la voix du salut... Cette humanité qui se cherche, en se trompant de maître ...La nouvelle Zélande est la parfaite illustration du fait que les malades ignorent toujours le Medecin Chef. 

 

Way wi Humanité bi lanouko kagleel moom miy weur foumouy jaar ba mouthie..gnui gueuleum ak reeré kika Yalla boleel. Li khew Nouvelle Zélande fir ndé la ci ni Malades yi reerénan Doktoor bi.

1.Ndawal Yalla lii ngeen xëy di  sàggan ba rombako

Di jeggiy bagaanam dëkké wër  ngir  juwaatleko

 

2.Fu Ndaw masa wootee gaaya yor kàggu yaay taxaw

Di diingat ba juuyook leerga far  daaldi noonuko

 

3.Ña gëm took di jaamuy topp seen Waaja soppako

Lu xaskatya gën xas Ndawla ñuy gën di jappako

 

4.Ña weddiy fexeey jeebaané ngir  màbb wooteba

Bilaay bun xamoon maanaaya jëkkënté nanguko

 

5.Bu ngeen fattewul woon demb dooleenko romba tay

Bu ngeen ubbi woon seen xolyi leeramyi feeseko

 

6.Ñi naan manta am  Yonnen du feeñat danoo xamul

Danoo teela lem seen kaggu yooya  ba weddiko

 

7.Nubuwwatu       Tashrii'in    Wa Tajdiidi     millatin

Nubuwwatu   Tasdiixin   nu ngeen def  ba reereko

 

8.Ki ñëw ngir sosaat aw yoon Ki ñëw ngir di yeesalaat

Ki ñëw  ànd ak  yonnen beneen  ngir dëggëlsiko

 

9.Nubbuwatu Tashrii'in la Mommadu tëc ba dem

Ku ñëw si ginaawam faw nga jël Yoon wa toppako

 

10.Demal yër Sayootii xool ca tafsiir ba ndax nga xam

Yonnen noon na Iisaay ñëw di yeesalsi nanguko

 

11.Ku bañ loolu Qur'aan neena "'ilmun li saa'atin"

Nu ngeen def ba bañkoo xool ba yeena ngi rombako

 

12.Ñi naan fanla Qu'r-aan tudd Mahdiyyu ñoo nelaw

"Bishaara" si kuy yeesal du doon sharta jappako

 

13.Te sax Ndaw lu nëw jog wooté jël njub ga sampako

Di def  mu'jizaat  Maawardi  nee  moom la wuyjiko

 

14.Nu ngeen def ba bañ Baay Laay mi waxni damaa nëwaat

Damay yeesalaat maay Mustafaa ngeen weranteko

 

15.Dangeen lactewul selluk xolam ak matuk jëfëm

Namuy  weetëlee  Buur Yalla  xiirleen ci jaamuko

 

16.Ki daan toroxal Shaytaané ngeen far juwaatleko

Bu njur  jaawalee  sàmmam ba  bukki  ya reeréko

 

17.Ki daan waxni kaay leen laac lu ngeen laac dinaako def

Ci  kantanu  Buur  bii  joxko  diineem  ji  yonniko

 

18.Musul jog si wooteem booba daan noon ya jëmbataat 

Lu ken manta xool naa cim ludul xolba noonuko

 

19.Damaa xamni goorgoo xamni Tawhiid la yekkati

Di   jaamoka   sellal   jëf   yi  kuy   seetlu  gisnako

 

20.Di   xettali  ñan  boddeeka  yekkati   ñan sewal

Di suuxat cofeel  luy  jikko buy mbaax mu digleko

 

21.Zakaatal alal ngir bañ ku ñaan  xawma bañ yëfëm

lukoy  firi   Buur   Yallaay   ki  xëy  deeyko joxnuko

 

22.Anaa "Xadarul-Mawlaa"  te  seen añ  bi laafi taac

Damay gan gu jaaree poot ña doon seenu rombako

 

23.Bu seen xiif bi yeenee dañ di ngeen musa xeewlusi

Ku xiif  baña  añ   far   fandé  biirëm   ba   jeppiko

 

24.Da ngeena tawat Doktoor bi ngeen bañko bëgg wer

Bu doonoon keneen buy dellu lum indi yobbuko

 

25.Yërëmleena tax doomam ji ñëw ngir di feddali

Te booba  batay seen  xaar bi manleena bayyiko

 

26.Naleen Yalla may leeruk xolak leeri bët ba ngeen

Janook Dogalam  bii joxko seen tum  bi toppako

 

27.Bu ngeen ko  xamul fii Yalla bum leen rawaat fëlee

Bilaay  yërmëndee  tax  Yalla  woowaatko  yonniko

 

28.Awaay Yalla booleel gaayi nangook ñi bañ yëfëm

Te mayleen ñu làngak moom ëllëk bañ juwaatleko

 

29.Te dolli salamaatin Yonnen bii nga yonniwoon

Te maynu nu sax ak moom te fum xëy nu xëyleko

 

30.Te yaggalfi lool sët bii mu tuddoon di Abdulaay

Te maynu nu àndak moom te fum jëm nu gungeko 

 

Rawdu Jammalaay

Guddi Gammu1438

12/12/2016

#lejeunepoete 

bottom of page