MARSIYA MAME BABACAR LAYE
1. Alhamdu lil-laahi gëm Buur Yallah war na
te gëm dogalam ya ndeem sunu diine wer na
2. Li Yallah dogal ci ab jaamam manul jaas
di nay am fawwa ndeem àtteem ba daw na
3. Lu jiitu amuk mbindeef yi ci ay juniy at
la Yallah dogal dogal ya te loolu wer na
4. Ba looloo tax lu Yallah dogal ci ab jaam
du dañ ci pexeem mbindeef ndeem Yallah bañ na
5. Xanaa mootax Seriñ Mbay Baabakar Laay
di bàyyi njaboot gi nii baña took "xuruunaa"
6. Demam gee bett waa Dunyaa ci mbooleem
ñi xam Baay Baabakar seen xol lëndëm na
7. Laayeen goo xamne amatul Sëydinaa Mbay
xanaa asamaan su amatul jant xam naa
8. Fu nuy làqooti, moo funu deeti daw jëm
ka doon yaakaari Àddina jeppa dem na
9. Mbindeef la mu Yallah amaloon ngir ga aajoy
mbindeef yi ku jaaxle waa ba jubal fa raw
10. Ba looloo tax turëm wa demoon ba Kodiwaar
ba jàlla Gineeki Gànnaar feppa siiw na
11. Te ndamba la woon bu feeñoon fii ci Kapweer
te doon meññat ci Mahdiyu loolu wer na
12. Nanguk ñaan ak fajuk aajoo ki feebar
donoom ci Limaamu Laay la te loolu sax na
13. Fu nuy xooleeti Baay Laay ciw meloom ak
doxin waak, wax ju xumba ja, nir wa dem na
14. Addina yaa di ab workat nde koon kay
nga àndak Baabakar mu jariñ jamaana
15. Bu fekkoon dee lu nuy mana jot la kon kay
nu jot ko ci ruu yu doy ba du faatu "laana"
16. Waxal neel geej la woon gu di fuur ci xamxam
ci "saahir" ak ci "baatin" loolu wer na
17. "Fiqaaki Luxaak, Nahwook Taariix, Haruud" ak
"Bayaan, Siiraak Hadiis, Tafsiir Xuraanaa"
18. Bu daan hadiis si lenn ci yii da ngay yeem
te andak xol bu feex ba nga naa rafet na
19. Limaamul Mahdiyoo ko soloon ci baatin
ci geeji "hikam" la duy ba ndabam fengatna
20. Ca "leetar" yooya Baay Laay jangaloo woon
Seriñ Mbay Caw kerook lako sol ba raw na
21. Ba Baay Laay naa ko Mbay kula laaj sa "meetar"
ci xamxam neel Limamu sangub jamaana
22. Ku lay laaj "meetarub" Baay Laay waxal neel
xanaa Buur Yallah "Rabbul-aalamina"
23. Seriñ Mbay daa na nettali lii "miraaran"
ba moo tax xamxamam ku ka xam ne yay na
24. Ku xam Baay Laay te xam Baay Mbay te gis ka
di nay tiit cik demam ndeem xol ba yiw na
25. Malaaka yi sax xëcoo na nu ruu ga ñii naan
na dem tey ñii ne bu mu dem fan wi des na
26. Kerook Baay Mbay xëmoon na ba dellu ximmi naan
man dey gis naa ludul jaas dig bi ñëw na
27. Limamoo ngii di may woo faw dinaa dem
Malaaka yi ñooy werante nde saa si jot na
28. Ci at mudi "wafsasin" ci gaddaayuk Yonnen
la Baay Mbay fekki Baay laay Illayiina
29. Ci weer wudi Maamu koor ca "kahun" ca weer wa
Ca Altine loolu mooy "taariix" ba wer na
30. Kerook bañu nee Seriñ Mbay Caw nelawna
ku xam Baay MBay bu selle xolam lëndëm na
31. Malaayka yi nekka kaw asamaaw yi jooy na
ngirek ruuham ga leen romboon ba wëy na
32. "jibaalu" yi ak "buhuuru" geej yi jooy na
ba jën ya ca biir di sàbbaal mbër nelaw na
33. Garab yeek suuf si ak asamaaw yi jooy na
ci ak faatoom kudul kook xol ba dee na
34. Nabee noon waaju am xamxam bu faatoo
ku titul moodi ab naafeqa wer na
35. Te ab nafeqa "Jahannama" moodi neegam
Ëllëk ca la jëmm ca "asfala saafiliina"
36. "Nahuuzu bi Laahi" yalnanu Yalla jàmmal
te xiir nu ci toppa yoon wa nga xamne war na
37. Xarit yaw kaay ñu waxtaan seetlu dunyaa
xalam ni mu def ñoñam ndax xellu jot na
38. Bu Addina doon këruk beel kay dinay yor
Ňu baax ñi fi jiituwoon du ñu jok jamaana
39. Yonnent yi Yallah daan wahyook ñu baax ñaak
Ňa doon waliyook sahaaba ya ñeppa dem na
40. Amoon na ñu Yallah jay def leen ñu diy buur
demoon ba di naagu tay seen yax fënëx na
41. Ňa Yallah jayoon ñu moom Dunyaa ca penkook
sawook mbooleem digënte ba ñepp dem na
42. Dammeel yi fi woon Barak yaak Teeñ ya ak seen
Jaraaf yaak Dak ya tay ñii ñeppa dem na
43. Ňu baax ñi fi daan dundël Lislaam ci Dunyaa
ku melni Limaamu ak Sheex Bamba Sheexnaa
44. Te moy Sheex Saadibook, Alhaaji Maalik
ka jappe mbiram ca Sheexu Umar kamaal na
45. Al-haaji Umar ma daa xeex ngir ga Lislaam
"kazaa" Alhaaji Ablaay Ňas jiyaar na
46. Seriñ Canabaak Sëriñ Buu Kunta ñii ñep
ñu baax la ñu woon te tay ku ci nekka dem na
47. Bu Addina doon këuruk beel kay di nay yor
Rasuulul-laahi konte du jok jamaana
48. Bu Addina doon këruk beel kay di nay yor
Sahaaba Rasuulil-laahi ña am "lamaana"
49. Bu Addina doon këruk beel kay di nay yor
Imaamul-laahi kon di na sax "xuruuna"
50. Bu Addina doon kërul beel kay di nay yor
Isaa Ruuhul-ilaahi boroom jamaana
51. Bu Addina doon këruk beel kay Seriñ Mbay
di nay sax wuuf njaboot gi du faatu "laanaa"
52. Ilaahii yalna ngay taw niiru xeewël
ca Baay Mbay muy karaama ca Illayiina
53. Fa Baay Mbay feete woon na fa Yallah wuutal
loxoom ak yërmëndeem banu am "lamaana"
54. Te may nu Manjoon mu sax ci njaboot gi yorleen
nde kon dunu jaaxle moo di kamaal te doyna
55. Manjoon yaay waaju mat kula xam di nay ñaan
sa fan wi di wëy di dem ba nga am "xuruunaa"
56. Te tay yaa fiy ku doon takandeeru Baay Laay
ci goor ñi bu ken werante mayuk Manjoonaa
57. Nu ngiy ñaan Yallah bàyyi la feek njaboot geek
jullit ñep ndax nga dekkal xolyi weet naa
58. Nu ngiy ñaan Yallah boole njaboot gi ciw yiw
Defalnu ci feppa funu jëm am "lamaana"
59. Dimbëlnu ba keppa koo gis muy saxoo naan
Alhamdu lil-laahi rabbil-aalamiina
60. Saxalnu ci Diine may num koom te bañ noo
Natoo cik bew walak ñàkkaak di sonna
61. Ilaahi noo ngi lay ñaan sax ci Liimaan
Bi jaahi Imaami Laahi sangub jamaana
62. "Salaatul-laahi summa salaatu Rabbii"
"alal Muxtaari xayril-aalamiina"