google.com, pub-1214054292722785, DIRECT, f08c47fec0942fa0 Mame Coumba NDOYE | almahdiyou
top of page

Mame Coumba NDOYE

Mame COUMBA NDOYE - Saliou HANE
00:00 / 00:00

(Litax ma def taalif bii dama ci juplu feeñal Cërëp Soxna sii addina rëëre ak soñña mbokki taalibe yi ñu xeeñtuw Mbirëm Ba wanep ligeeyëm Ndax doyna addina royuwaay.....

1) Ma jeema juk , dellooti mbattu ndaala 

Njukkël Ka ap , Cërëm ba rëy Ca YALLA

 

2) Yonen Ba moo , feeñal rëyup Dayoomba

Tiisluk demam , te yeemu lol ca Yenba

 

3) Kon ku di xelllu , tey xalam , di xamle 

war Ngaa fesël , Mbaax , jikko yam aandaale

 

4) Leerak Yonen , deeñca ko , doyna tiitër 

Rawatinaak , Ndaw Lifi gën , tey joxe cër

 

5) YALLA ko yar,  tannako tam laabal ko

Jël Maam Limaamu Laay mi gën deenkaatko

 

6) Mooy Cumba Ndööy , Mi ñep xam ,  ci Jagata

Ngir joxe ñam, terle ni Maam Amiinta

 

7)  Tab gaa waral , MDoomam Ja daan , fa tektal 

Kepp ku xiif, muy dëkke , leel leek naandal

 

8) Moo farlu woon , ci dikle yiw , tey dimbële 

Mboleem Jigeen , luy xeewëlit , muy sëddële 

 

9) ku nawlu woon , Yaakaaru woon ci ak yiw

Du lor , dukuy xalaata jëm ci ak moy 

 

10) Daan jaamu rek,  ba naafilaam di farata

Ba buur dëkooko , mayko sangup Maam Farmata

 

11) Dëkkeena YALLA , Bam dëkköö ko , Falko 

Muy sangu Kuy , Jigeen ju jak,  Sargalko 

 

12) Gëëj Mbambulaan , bay fees di fuur ci xam xam

Dawal sangam , Ba laxxa ndam ak ngërma ndeem 

 

13) Ken musta gis , muy foñ , di jaambat , baa xun 

Nangu la def daabaam , batax  neexul sëën 

 

14) Muñëk , Woyof , labiir la xambe woon njël

Ku yëëne Taac , gëneel de , dingfa dem jafal

 

15) Mbayam mi tay , soontu na lool , bay jaayu 

Mootax Ba Buur , Sampalko xeeti raayoo

 

16) Jaantup ngërëm, ci moom la gaaña leerlu 

Di niiru ndam , tanneef Ya daanfi seerlu

 

17) Budul konak , Maam Cumba mii mat taara

Fu rëëwmi jëm , ni kon dugup di baara 

 

18 ) Xam ngeen ni mak , nekkul ci at yu yagga

Booy natt mak , seetko ci mat ak yegga

 

19) Mooy tax nga xam , fii soxna Cumba tollu

Ci reewmi ak ci diiiné , day Ku doylu

 

20) attam yuneew yi , teewu koo raw gaaña

mat ga ca moom , moo jaaxaloon way xam ña

 

21) Jaambaar ju xëy , ci ap sangam mu sasko 

Fu saswa jeexe , jaajëfam ja dapko

 

22) leek leek nga gis , baykat bu wacc njolloor

Tefum taxaw , jawriñ ja yeene kay döör

 

23) Maam cumba nak , pasteef ga ak njambaar ga

ñoo rafetal , mbayam ma ak laabiir ga

 

24) te lako war , ci diine ak kërëm ga

yaxxunuwoon , wormaam ga ak ngoram ga

 

25) wormaam la fop , feetalekook Boroomam

Ngor nga  ladaan , jëflënte ak moroomam

 

26) Loolooko may , sangam ba xëy gërëmko 

Buur YALLA yit gërëmko faw , farooko

 

27) Du Maasu ken , Tanneef lawoon,  royal mako

Doon Jeek bu jak , Raw göör ña , Buur dollil nuko 

 

28) Yërmande ak Ngërmande ak Jeggal ga

Ci Barke Sap Soppe Madoon Donoom Ga

 

29) Julli Ci Moom SaHaaba yaak Ngertëlma 

Muccëlnu baalnu maynu xeewël jamma 

 

30) Ñu aanda ak Libaas besup payoor ba

Te dëkki ak wayjur Ya neegi Tuubaa

 

Mercredi 07 MuHarram 1439 H 

 27 septembre 2017

Zone contenant les pièces jointes

bottom of page