Limaamu Wàcc Na
Way wii maa ngui ko tambabalé si rawdub Jamaalay, Altiné 9 Mai 2016 tollook 1er Shabaan di bessu Appel si waxtuw Yooryooru Jamalaay, Jeexalko besu Nisfu Shaabaan si Kambéreen tollook Dimaas 22 Mai 2016. Fas yeene fattélisi jaam ñi ni Seydina Limaamu jëflentee ak ña ka doon baña ka fexeel, ak nimu yeene woon te diglé anduk jullit ñi. Fattelisi wootem bu sella bu mucca ayyib bi ak niñu ko wara taawo sellal ko si lepp lusi rax ak lusi dugg diko tilimël. Ñaax si mbokki taalibé yi ñu defaraat toogaay yi sakku ngërëmu Maam Limaamu te moytu ay dumam. Yal nako Yalla nangu
Limaamu Wàcc Na
1. Limaamu Laay wootena digba ñëw na
Beglena waar na ñepp layebiir na
2. Jotalna liika Yalla yonni muñ na
Saxna di woote musta xaddi raw na
3. Yeesalna diine toj xërëm yi am na
Sellalna ruuyi footna xolyi wer na
4. Soobaatna jikkoyi te cëryi yar na
Defarna mbokka gi te aywi feg na
5. Xallatna yoonu diine Ndjiin Yaatal na
Ngir mi Rasuulu ubbiwoon tëjaat na
6. Lum masa wax moo jëkke jëfko wan nu
Xol leen si man te royma maay Amiinu
7. "Laajumalen tool aki suuf mbaa mbay ma
Wowumalen ngir addiyaak ngeen may ma"
8. Jël len lu ngeen fi faggu ñëw ñu seddoo
Liima fi yor Njiin rawna ñiila seddoo
9. "Boleen gisee ku leen digël lu gën lii
Malen digël demleen" Bilaay moy Ndaw li
10. "Innii muhibbukum wa laa ansaakum"
Samak mbëgeel si yeen du dañ "ar'aakum"
11. Woote na atya not ñadoon noonam ya
Xolbaak dogoomga moo wedamlo bañ ya
12. Bes bam xëyee ni Yalla moma Yonni
Noonya taxaw munaa Boroom bey 'awnii
13. Ñako nawoon xëy diko xas ak diko jëw
Ña daako rang boddiko naa dofna ba faw
14. Yedda Ndijaay ja naa fajil sa doom jii
Baatam di gën jolli ñunaa ay waajii!
15. Yalla jotal kaddomga gaaya gëmsi
Fooreya ak Tafsiirya ñeppa rotsi
16. Ñulen di ñaawal naa nu ngen mané ñëw
Di toppa mool bu jinné jappa lee ñaaw
17. Ñu tontunaa mom lanu gëm mom lanu am
Ñu far di leen xasa ka fitnaal funu jëm
18. Mbiram di gën yokkou ñu gënkoy noonu
Jeebaane kook tubaab ba ngir mu daanu
19. Naako sa nguur gi lay fexeel muy xaacu
Bes bam dalee sa Maam Libaas la reccu
20. Ña doon fexee mujja ragal ñëw ñaan si
Kerook la aalu moodi Xayrun naasi
21. "Manatuleena tax ma dellu geej ga
Yallaa ma yekki kuma toppa raw nga"
22. Njoolma rañaan na bes kerook gaddayna
Ñu diko wër manu nukoo gis rawna
23. Noon yaku daa fexeela mujja waaru
Bañ yako daa jeebaané mujja jooru
24. Yar yañu leen digë taxoon ñukay wër
Mu feeñuleen bilay Limaamu moy mbër
25. Mu jiiteleen kerook jubël sa noon ya
Ñuy xaxataay di ñaawalaat soppem ya
26. Saabaya jooyna bes kerook Limaamu
Neleen du yagg gaalga rëng ñu yeemu
27. Kerook tubaab ba farna jaq ñaanko
Duma ñadoon boole ña doon tumaalko
28. Boroom xolub wurusba naa baal naalen
Ndabul teraanga laafi taaj xëy wooleen
29. Fayenaleen seen tooñga ak seen jëw ya
Dileen bayal ak toppatoo seen tool ya
30. Fayenaleen seen waxja ak seen mbañ ga
Taxawuleen saa yun dugee kërëm ga
31. Bes bam ñibee ñu dawsi ngir baarkeelu
Diko xëcook gëmya Huwal fadiilu
32. Kon yawmi gëm Limamu xoolal mbaxam
Namu fegook nam jamboree xool diinem
33. Musla xuloo te musla xas nawlem ba
Bulko xulool bulko xasal soppem ba
34. Soppem ba mooy kepp ku gëm boroom bi
Neel yërmëndeem lambana mbolem dun bi
35. Royal Libaas si yaatuk xolba muuñ ga
Cofeelga ak tallik kanamga muñ ga
36. Ken manta xer badap ki momab wootem
Nee nanko bëggël ñepp leedi diinem
37. Ken manta xer badap ki momab wootem
Nee bul werantek kenn leedi diinem
38. Ken manta xer badap ki momab wootem
Nee nanko jappal ñepp leedi diinem
39. Ken manta xer badap ki momab wootem
Nee bul di boddi kenn leedi diinem
40. Ken manta xer badap ki momab wootem
Nee nan yërëm mbindefyi leedi diinem
41. Ken manta xer badap ki momab wootem
Nee bul di bañ kudib julit mooy diinem
42. Wotem bi tax budaa taxaw biiram ba
Noox taqalook yaxu ginaaw gaak xiif ba
43. Nanuko samm bañko rax sellal ko
Teñu sagal Limaamu Laahi roy ko
44. Buñiy sikar na ñepp laab am worma
Tawhiid bu wer ba ken du xas sun Njolma
45. Waxtaan ya nanko segg wax la Njoolma
Ak ñay ndonoom daa wax ba teggi tuuma
46. Ba folkloor beek ngistalak gisleen ma
Samonte ak teggini tagga Njoolma
47. Sunu bëgee malakay Yalla peek nu
Danuy defar geew yi ba ñepp wegnu
48. Limaamu seede nan ni kay matal nga
Xallaat nga yoonu diine laayabiir nga
49. Lu waay xasee sa yoon wi nooko sooke
Maam nang nu baal lumoy danan tumranke
50. Koo xamne saayu tampewul ken dula jox
Bula meree tayak ëlëk da ngay torox
51. Nañu dagaan Limamu sakku ngërëmam
Te nañu daw meram ma moytu ay dumam
52. Awaay Limaamu baalnu far sun tooñ yi
Gëmmël ci sun ayib yi ak sun jëf yi
53. Xamnga sunuk cofeel si Yaw te xam nga
Liy sunu yeene Maam teralnu man nga
54. Yaw lanu am ñaan nanu bes payoor ba
Taabale ak yaw bes kerook sa deeg ba
55. Na Yalla mayla lay Wasiila besba
Yaa moom Maxaam ba ak Liwaa ba booba
56. Nu sax ci say ndigël ba daan shaytaané
Ndax ay pexeem mooy fexe loonu daané
57. Yalla saxalfi Abdu ak sa sët yi
Jubël njaboot gi woyofal seen yan yi
58. Suma salaatu lahi zil ikraami
’Alan nabii wa aalihil kiraami
Mamadou Bara SAMB
Nisfu Shaabaan
Kambereen
22 Mai 2016
Limaamu Wàcc Na (Tontub Sàliwu Haan)
Lii Baara wax ngir yeesalaat sa ngir mi
Yalnanko degga ndax ñu goop sa njiw mi
Ken manta xer ba dap ki moomab wootem
Daan xëy di gonta ngir sagal bañaalem
Ken manta xer ba dap ki moomab wootem
daa sakku mbaa ngir gaaña weddi diinem
La Baara wax doyna ca, nanko feelu
Ca ñay sikar kureelu ngir barkeelu
Saxiir newoon Malaaka yaa ngi wërleen
feek ñungi took "ci Yalla" baa ñu dawleen
Nan moytu Njiin buy janga seen rapport ya
Gis ca ni sammonte wunook teggin ya
Sikar su riiir te andulak ben worma
Deefuko nangu fafko def mbugël ma
Bu xer ba moy yoon wii di kerkeraanu
Mak ñifiwoon nde kon ëlëk ñu yaynu
Fun musa jaar ñep bokka naw waa Laayeen
Tay funu aw ken xammetul waa Laayeen
Nan moytu luy buurënte def li Baara
Joyal ci ñun doon gënji nongi daara
Fun mana wacc ñoo fa doon Limaamu
Nan farlu kon badun fa xeep Limaamu
Moonu sagal faroonu tam ca xeet ya
Nan fexe Maam jappee nu gën ji laaya
Yaw lanu am lun mana mandi tarxiis
Footnu raxasnu Maam fegalnu aw tiis
Yaw lanu am lun mana lap ci Dunyaa
Yaw lanu am sunuy cofeel dafay law
Ci yaw ni ngooñ, yà jar dagaan te jar naw
Yallana Buur dollila ay teranga
Samma sa yoon wi yaanu doy ap sanga
Bayyifi Abdulaay mu am salaamaa
Wer woyofal yen bii ci moom dawaamaa
Jullil ci Maam Limaamu ak Saabaam ya
Ak ngertëlëm joxleen la gën ca peey ya
Yalna nga may Baara mi yeesal dikleem
ya, mucc ak Saalihu Aan may soppeem
Venrdredi 27 Mai 2016
Saliou Hann