​Dagaan Limaamu psl
1) Dafay war ci ap jaam bu mooñoo ngërëm
Mu sonnal xélam ngir ga way ap sangam
2) te fii koofi way ngir ga feeñal mbirëm
dafay as ci Mbër muy mbëbbël ay ngalam
3) Bataxmaa jubël Geej ga fées bay duyël
Ku baawnaan ca moom dëcfa booleem ndabam
4) Ki raangoo ba raangal ka baatam yuxeel
Ka woomleet ba woomal ka ñaakkiy dërëm
5) Katax Buur digël luy Malaakam sujood
Ca Maam jan dëxëñ leer nga far noonwa tam
6) katax Buur seral ngaare Namruuz nga ngir
Muccël Maam Xaliilu banaakaan salaam
5) Katax Buur labal noonou Muusa,Mucël
Boroom taar ba Yuusuf ba laalul Haraam
6) Ci Barkeem la Issa niwoon maadi jaam
di Yoonen Bu Barkeel setal Wayjuram
7) ña ñëw wootewoonak ña RaHmaan soloon
danoo ñëw ngirak wax mindeef yik dikkëm
8) Waxal Moomla Buur jox la rëy cay ngeneel
Mufeeñaat ci soodaan ku ñuul jot cërëm
9) Doney AlHasan Moodi Njiin Coumba Ndööy
Ki taal njup té fay fii lu bon ak lëndëm
10) Damaa xamni Yaw rek yaa neexa way
Batax Buur ni Yaa raw ci jikkooki Ndam
Damaa xam kulay kañ delum wax du Jay
du ay nar lu xél ñaw du seenëp Dayoom
11 ) Damaa xamni fan jëm de yaay jallubaa
Ma jebballa saay mbir farook yaw itam
12) Kuñëw rot sa deeg bi du sooy maafi goor
nde naandalma thiy may ma fessak ni'am
13) kudul yaw de saay bët du xool jëm ca mom
té Yaa doy samap xol mbegëk tiitërëm
14) Kudul Yaw du tuur luy ranxooñ ngir cofeel
sa mbekk rekka Laay yeuk ci xol biima am
15) Limay wut budee yaw ci laa jaar na am
Te saay sakkuteef mooy nga diot Lay Maxaam
16) Di ñaan YALLA wanma sa contaan ci man
Te nangulma saay way ci Yaw maynu Ndam
17) defarma dioubeulma gëneel dottima
Te yekkima yarma lubon bun ca jëm
18) awaay Soppe baa ngii dagaan seddëma
nga yekkilma saay mbir ñu raw yaay buntëm
19) Te Barkeel samak dundë gii doyma ñak
Sagalmaat sagooma joyalnuy ngërëm
20) Jëlël aajoyep jox Boroom ndax mu faj
Yarasnaa di neenal sa Laac Bay Mbegëm
21) Jotee naaala saak ruu ndiaboot gueek xalaaat
te xol beeki saam xel sa mbek lay xalam
22 ) Ay waaay YALLA jullil té seulmël ci Njiin
Mu laambay SaHaabaam té yiir waa kërëm
Le 23 Avril 2017