google.com, pub-1214054292722785, DIRECT, f08c47fec0942fa0
top of page

Yalla   Jërëjëf

Unknown Track - Unknown Artist
00:00 / 00:00

Way wii damasi fasyeene Sant Boroom bi, disi ñaax bepp jullit mu sant Yalla si lep lum mana nekk. Moom Yalla mi nga xamni limunu jox moo ëpp fuuf lumnu mana xañ. Lepp lumu def si nguuram gii dan kokoy gërëmee fasyeene rek doon ay jaamam. Si jamonoo ji nga xamni fitna bërina ñu neeway xëy ak xol bu feex buy sant Yalla. Maangi Taalif ginaaw wayu Yalla Walluma.

1. Tay ji damaa nëw ngir gërëm "Rabus sama"
Santaat ko ngir ay xewëlëm moom Buur sama


2. Buurbii ma sakka te awma woon sik cobareem
Buko sobutoon xam ngeen ni tay jii nekkuma


3. Wacceema adduna ak ni mbindeefam baree
Moo soob ma bokk si xeetu Yonnen Maynama


4. Moo soob ma gëm ndaw lim nu tannal ñaari yoon
Gëm Mustafaak Mahdiyyu Laay kay doynama


5. Ay santa naala Boroom bi sant gudul taxaw
Yaw miima jox xel miima rañee sas ngama


6. Loxo yiima tallal Yaw la soob te silay wutee
Sama tank yaangi doxantu Buur bi beralnama


7. Lan la defal Buur tax ba sonnuñ laggewuñ
Ñim tek natoom tooñunko day "Rabus sama"


8. Saa bët yi day gis saa yu xippee ak di xool
Bula sobutoon day gumba kon tay xoluma


9. Saa nopp yaa ngiiy degg yaamako xeewëlee
Tëxloo nga lenn si saay moroom ñaagal ngama


10. Wer gii ma am tay yaako xañ ay jaam ni man
Ñuy xëy di saalit ak di jooy ken seetuma


11. Ay jaama ngii tay ñakk lun leel sen njaboot
Maa ngii di ndekki di añ di reer xeewël ngama

12. Geer yaa ngi wër dunyaa bi kenn talul dara
May xëy si jamm di kaf di ree xëccoo wuma


13. Ay jaama ngiy yewwoo si mbedd mi bes bune
Man may bidënti si lal bu nooy suturaal ngama


14. Kon booma nattoo tax ma fatté sa ay bagaan
Bay yuuxu naan lan laala def mooy santuma


15. Bes boo xëyee rek xañ ma benn si yii ma lim
Yisi des du dañ ngir seede sag mbaax may ngama


16. Bes boo ma nattoo ñakk yepp du tee nga doon
"Wahhaabu" xamnaa pay gu rëy dencal ngama


17. Yaay Buurbi moom say jaam te kenn amul di laaj
Loo xëy dogal moo gën si ñun lii woor nama


18. Ay Buur defalma li gën si man te nga may ma xol
Bu nanguy dogal ak sant ndax sottil ngama


19. Jullil si goor ginu jangaloon santak gërëm
bafi Abdulaahi mu gën di wer maynuy jamaa


Yëmbël
01 Novembre 2015

bottom of page