Imaam Saxiir Sunu Xol
Way wii danu siy teewlu jëmi sunu xaritba Imaam Mamadu Saxiir disi wane ak demam tiis gimu tiis sunu xol ndax fim nu feetwoon. Di si tiislu ñakk ginu ñakk mana gis kanamam gu sella gi. Yalnako yalla dolli leer.
Mamadou Bara SAMB LAYE
​
1. Ay Maam da ngaa mere sab sët jeppi aw doxinam
Tax bëggulaa daje ak moom mbaa nga gis kanamam
2. Ay weera ngii mu ngi lay wër Bukratan wa Masaa
Guddeek bu jànt bi leeree ngir janook sa kanam
3. Xolam bi feesena tiis ak njàqqareeki naqar
Ni seet bu yebbi ba xëy ñu tàgge kay jëkkërëm
4. Ni yaay ju ñàkkam perantal Baay bu ñàkk ka doon
Doomam ja degga ndigël baa Maam ñu ñàkk sëtëm
5. Jirim bu ñàkkati yaay Baayoo bu ñàkkati baay
Sàmmaan bu ñàkk njurëm Taalib bu jooy sëriñam
​
6. Sëriñ bu daaraja gent njur gu sàmm ba reer
Wayjur yu xëy robi doom ja des mu fekkiy rakkam
7. Mbaa sët bu ñàkk kadoon Maamam jubax wala doom
Ju Baay ba reer Nday ja xëy dem bayyikook naqaram
8. Jëkkër ju tukki ba ñëw xëy seet ba làqqu ba faw
Maam haazihii haalatii Arjuuka wëy fuma jëm
9. Yaa bàyyi nonga bi reer yaa bàyyi gaalgi mu suux
Yaa bàyyi sab sët mu saalit yaafi xotti xolam
10. Imaam Saxiir Sunu Xol goor googu daanu begël
Kañ ngay ñëwaat nu dëfël sun xol yi xool sa kanam
11. Xanaa sa tukki bi dootul jeex nga dellusi xool
Njaboot gi Maam suna neexe delluwaat fa nga jëm
12. Yawman bu jànt bi soo nga delluwaat ñu dëfël
Seen xolyi fatte naqar wii sàng seeni kanam
13. Mbaa Saa’atan lahzatan xanaa namoo sa njaboot
Njur gaa ngi nii dila xaar Sàmmaan bi yaw lañu am
14. Maam reerenaa Yoon wi kaay xàllaat ko yaw miko man
Niital ma lëndëm gi naawilnii sa Tum bi baxam
15. Maam fàttenaa lima jàngoon kaay sawaat ma ta dem
Firilma Mas’alatan bindëlma Saar wuma xam
​
16. Maam awma fit wuma xuusee Golbi kaay gindima
Shaytaane man nama kaay sotalma maymasi Ndam
17. Maam maa ngi nii tooñ di yaakaar Mbaa wa maghfiratan
Ngadib xarit si Boroom biy nangu ak Yonnenam
18. Maam maa ngi xiif te mar ngay Teen di Maa’idatan
May ab dagaan kat di sab sët ngay boroomi Ni’am
19. Budee manoo ñëw nu dundaat xolbi naatati kon
Bàyyil ma ñëw took sa wet ngir dund xool sa kanam
20. Bàyyil ma ñëw doon sa xaadim took bi xadratikum
Loo laaj ma joxla dumay wor loolu war ngako xam
21. Na Buur bi dolli sa leer bi ’addi maa xulixa
Nuy sax di julli si Njiin ak toppa ay ndigëlëm
22. Feek picc ngiy sab ba ker nuy ñëw di took si sa wet
Xëy ànd ak yaw Ilal jinaan ak kula xam
23. Na Yalla may sa njaboot Barkek lufiy Sutura
Ñuy gëndi xañtu sa Yoon xambaatko maylen Salaam
24. Na Yalla julli si Baay Laay ak ña feete sa moom
Sëlmël si moom maynu Ndam ak Mucc bes banu jëm
Yëmbël, 2006