google.com, pub-1214054292722785, DIRECT, f08c47fec0942fa0
top of page

Dagaan (Taxaw naa ngir dagaan)

Unknown Track - Unknown Artist
00:00 / 00:00

Way wii maa ngi ko tambabalé si rawdub Jamaalay, besu Gaamu tollook 13 Janvier 2013 mu doon toroxlu ak jebbalu si Boroom Jamalaay. Jaaré si moom tuubël Boroom bi ngir mu raxas ma si bakkar yeek jàdd jàdd yi. Ñaan si Yonen bi mu sagalma faalema farooma ndamooma raxasma footma defarma ubblima gungema ba bes bamay taabale ak moom sa deegu kawsara. Nako Yalla nangu

1.Taxaw naa ngir dagaan sila “Yaa Kariima”1
Di yaakaar lool ku baax te yewen mu mayma


2. “Fa Ahwaamun minal isyaani”2 teewul
Ma yaakaar Mbaa si yaw nga yërëm ma baalma


3. Bu saay bakkar bëree ba yaras namaa ñëw
Di jakkarlook ki tax luma ñaan ñu may ma


4. Bu saay ñaawteef bëree ni Uhud3 di ab jal
Ma tiit lool ngir dajeek sa maxaama doorma


5. Bu saak moy ak samak jaddak limay juum
Demee ba sonalma notma ba nuur ma wër ma


6. Ma xool dooley Boroom bi ragal xupaam ma
Samay gët taa ma jooy ngir tiit meram ma

7. Ma xool limu may defal si lu baax te aw ma
Ludul di ko fay si xeewël yooya moyma


8. Ma seet limu may fegal siw ay te maa guii
Li muy tere laay xëyee teewul mu jox ma


9. Mumay suturaal makoy merloo mumay xool
“Fa laa shukran walaa sabran”1 te war ma


10. “Fa laa Zikran Salaatan laa Xiyaamaa”2
“Wa laa Hajjan Zakaatan laa Siyaamaa”3


11. Desul sama xolbi “Yaa Xaryral Anaami”4
Ludul Yaakaar nga ñëw ñu yaras la baal ma


12. Da may ñaan tay te musloo boddi kuy ñaan
Damaa yaakaar te doo wor “Yaa Rahiimaa”5


13. Damay tuub tay te doo delloo ku xëy ñëw
Di reccu li weesu yeene defar xëyëm ma


14. Raxas ma te foot ma saab xol jëlko laabal
Jubël saay cër awaay Baay Laay defar ma


15. Ubil ma ma doon sa taalibe ker ba may dee
Ma am sa ngërëm awaay Baay Laay nangul ma


16. Pexey Shaytaan “hawaa nafsin”6 fegal ma
Woruk Dunyaa nga ñaan sa Boroom musël ma


17. Malay xidmaal ba fekki la “Yaa habiibii”7
Ludul sa ngërëm amul solo “Yaa Imaamaa”8


18. Bu Dee yeksee ñu toogu ma daldi jaaxle
Ma feebar lool njaboot gi yërëm ma wër ma


19. Pexeey Doctoor Sëriñsaak Maam ya jallul
La ñuy jeem niil si xettali maak si faj ma


20. Ma xool sama manmanak wërsëg wi askan
Mu leer mani Yalla rek moo man weral ma

21. Malaakal Mawti yeksi taxaw di waajal
Samak ruu naako saabi taxaw na jël ma


22. Xabaar bay jolli ñuy yuuxoo ka jooyoo
Ñu sànga ma sërba neeg ba selaw ñu muur ma


23. Sikar si di jolly ñuy waajal juleema
Ginaaw seen seede yooya ñu jëlma fob ma


24. Kerook lima def si Addina waaj dajeek man
Ñugas bamu xoot bëmëx masa mur ma suul ma


25. Sa teewaay laa fa yaakaar “Yaa Imaamaa”1
Sa weetaay baak xataay ba lëndëm ga wër ma


26. Samam xel dem si yaw yaakaari jaam ñi
Si xettalimaak nga ñëw dëgërël ma jël ma


27. Ñu xëy wal bufta booba ni saa taxaw na
Ku deewoon dekki Yalla taxaw ni Mooma


28. Kerook taxawaay ba yagga na ken talul ken
Samay soppeek xarityaak bokka daw ma


29. Ku toñoon ker lakoy fay ken du baale
Luwaay daa def mu feeñ tedu man ni baal ma


30. Boroom bi digël ñu seddale teere yooya
Ku ney tiit ay jëfëm tay sakku Mbaa ma


31. Ñu ngay reglee ka peese di seet di kontee
Ku waajul bes kerook nara ñam mbugël ma


32. Kerook saw gaay lañuy berndeel sa ker ga
Dagaan naa ker Limaamu nga ñëw faroo ma


33. Siraat ak duus yu rëy ya ku daanu alku
Sa gaalgay jallé kepp ku sakku mbeg ma


34. Ku moy sa ngërëm du naan ca sa deegbë besba
Du lekka ca res wa ken du dëfël meram ma

35. Ñu wax Ridwaan mu ubbi ñu yeek sa peey ya
Nu taabalé ak Limaamu di naan sa meew ma


36. Sa yoon wey yoonu Aljana “Yaa Imaamaa”
Ku andak yaw du tiit Yawmal Xiyaama


37. Na Yalla defal la lay “Wasilaak Fadiila”1
Te jox la “Maxaam”2 ba sotti si yaw “Salaama”3


38. Yawak sa njaboot te julli si yaw Imaama
Ma sax di dagaan nga may may “Yaa Kariima”


39. Kudul yaw aw ma seetu ma kon sagal ma
Faroo ma si Addunaak fanu jëm nadmoo ma

 

Guddi Gammu Rawdub Jammlaay 13 Janvier 2013

1. يا كريما : Yaw ku tedd ki (maa ngi si Jubli Yonnenteb Yalla bi Seydinaa Limaamu Laahi).

2. فأعوام من العصيان : At at yu bëri yuma dund sik moy. 3. Uhud : Doju Uhud bi nekk Madiinatul Munawwara.

1. فلا شكرا ولا صبرا : santuma si xeewël yi mu ma may moom Yalla, muñuma it nattu yimu ma tek.

 

2. فلا ذكرا صلاة لا قياما : tudduma Yalla nimako wara tudde, julli wuma lu mat, te naafila wuma yitam. µ

 

3. ولا حجا زكاة لا صياما : aji wuma, azakaaluma lu mat, te wooruma itam nim ware.

 

4. يا خير الأنام : Yaw mi gën ji mbindeef.

 

5. يا رحيما : Yaw Boroom yërmënde gi.

 

6. هوى نفس : Bànneexu Baken. 7. يا حبيبي : Yaw samap soppé. 8. يا إمامَا : Yaw Ilimaanu Yalla ji.

 

1. يا إمامَا : Yaw Ilimaanu Yalla ji.

 

1.الوسيلة والفضيلة : ñaari teraanga yu Boroom di di jox benn si ay jaamam, te Yonnen sàkkuwoon ñuka koy ñaanal.

2. المقام المحمود : Daraja ju rëy ju Yalla jagleel Yonnen bi ëllëk bis penc .

3. سلاما : sëlmël

 

bottom of page