BAYE ABDOULAYE
Taalif : Sargal khaliifatul Musliminaa
1) Daananla way dila kañ ci lakku biidaani
Jeggalma tay sa ay wolof Yaa faxra suudaani
2) Te lottanaa mana way ngir ñakka xam gi sa kem
Sap tolluwaay ci ki xam sax weeesna awzaani
3) Bay Abdulaay Sunu feeteek Yaw du ngööra ci ñun
YALLA nu baaxe sa njup Khaliifa Samdaani
4) Yaay sët ba Maam Ja juñnjoon Tey Doom Ji Baay Ya gërëm
Teeñoo nga yen Yifi woon say may di biiwaane
​
5) Yaa xalla yoon wi Te aarit Toolbi bañ kuko ruur
Semmal nga bañ Ya , ku jomloot Yaako faf daane
6) Yaa boole l'islam bi , teeyal naanu waayi julit
yi, tay ñu ngiy fekkaleet seeteet du waxtaane
7) Te taal nga njup fepp, mabbal juñ Ya rëër tabaxon
muk tayyi woo dekluwoo kuy xas du jeebaane
Yaatax ñu xemmeem Li Baye LAYE taal ci sawwu Bi tay
Ku ñëw jafal si fi njup leeral ci bulbaadi
9) Baay gor nga kén dula dap Yaa roomba ñep ci yiw
Te bakkuwoo akanaw say jëf yu keemaane
10) Cëy baalnu baalatinu ndax sakkuwoo kula kañ
Daay yobbu mbattu ci nada njukkël finiy naane
11) Te yar nga yiir nga defar kuy sakku m Baax diko Roy
Sa njëlli matna te doy doo gis ku xaaraane
12) Ku xam sa mbir dans way ku Roy ci Yaw dana wëy
Sa ngir mi rekk nu doy Billahi waatnaani
13) feral nga xol yi feral ranxooñu i gërëm
Baye Abdou yaafi di ñak ken dootu saaraani
14) defnanla ngay Moom te yaw yaay kookou ken dufi Yaw
Yaay tu mbaax ginu nandal ken du rootaani
15) NaYALLA sammala Yaa shayxar-rashaadi nga raw
Ak at yu laxxu ci wër Yaa faxra Suuddani
Le 22 mai 2017