google.com, pub-1214054292722785, DIRECT, f08c47fec0942fa0
top of page

Alxuraan

Alxuraan - Saliou HANE LAYE
00:00 / 00:00

Taaliif Bii manko def ngir jooytul " Alxuraan " ak wax yiteeem ak Njariñ yimou dik kep kuko foonka te diko wettalikoo..


1)Budul kon ñimay jangak di mokkal di bind ji
Damay dellu faa nekkoon, te took foofa dallu ji

 

2) Samaw yiw de laa yor man, di baaxal ku japp ma
Te tek koot ci yoonuw njup; wu jëm peey banuy daje


3) Di fööt Raggi xol bam set, ma tabbal ci leeri ngëm
Cërëm yeet, dëkee jëf luy ndigël; dun ca tayyi ji


4) Té wennaw Haraf, wooxam ci man, fuuki yiwla de
Alif , baa ki siin, baa sax yaneen yoo ca dolli ji


5) Famay tambalee ak yaw, kerook biss ba ngay dali
Yawak Sëñ ba, say waydiour, ca Laa leendi rammu ji


6)Ku may jaanga, say waajur, bu yawmal qiyaamati
Dinaaleen Sola,l ndëppuy wurus, leer ga jolli ji


7) Dinaa japp yit saawaay, bu biss peñc, baa loxoom
Mawax YALLA, keeey saaa waay, mbegam naako Sakku ji


Ku def ap dërëm ngir mane, ma ful kooki junni tee
Sëriñ Daara ak ndongaam kuleen jox ma Seere ji


9) Tabax Daara bam yegga, nga Ndiox waaju xamme ñor
Mufay jaanga Alxur-ana, payam xél dukay daji


10) Ku wallup sëriñ daaara, lu seddup xolam ba mbaa
lukuy menti xeewël mbaa de luy jëm ci Daara ji


11) Budee teere , alluube, Basagñ baa te jullikaay
Ladip dundë baa fay sax couraaanm baa nga viide ji


12) ku baaxoo di föötal ndoonga, jeekal terin wa tam
Bu koy tayyi, ndax say may Boroom mooko gaddu ji


13) Ku fekkip seriñ Daara, muwax yitte yam ca ame
Ci daraam feexee tam jëf lutax xolba seddi ji


14) Budee it garap yuy fac tawat melni asprine
Joxal sëñ ba, leeleek ndax, njarak bañ di walle ji


15) Ku jëf, baa nga jëflul ; baa nga tax Kenya jëf ci yii
Sa pay maako warlook yaw, ëllëk naala rammu ni


16) Te loo yor ma barkeel, looma dottil ma faylako
Te yawmal xiyaam doo rus, te doo gis ñafay mbeji


17 ) Samay buntë ubbil naako, kuy Managua yiw wu rëy
ku tabbal ci man num tol, ma ful kooti bam Dijji


18) Te bul xeep, ba far doo def, te bul naw ba waññiko
Defal rek, ku nay tee def, ëllëk dingko reccu ji


19) Samay soppe mooy sëñ Daara, ak ndoonga yam yore
kuleen yëk, ma yëklaa yëk, kuleen boddi tarsu ji


20) Luwaay jëf ci mane nay xamni, yëknaako jappko
Bu bis Baa, dinaa seede jefëm YALLA, fun daje


21) Damay Santa tey njukkël Samay soppe waxneleen
Ëllëk mande Alxour aan dinaalenfa rammu ji

Le 01 juin 2017

bottom of page